Yàlla dellu ne Musaa: «Dangay wax bànni Israyil, ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo ma yónni ci yeen.” Aji Sax jee di sama tur wu sax dàkk, ñu di ma ko fàttlikoo ba fàww.
TSK
TSK · Leviticus 24:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñuy àtte nag mbooloo ma saa su nekk. Su dee mbir mu lëj, ñu indil Musaa; mboolem mbir yu sew-sewaan ya, ñoom ñu àtte ko.
Bànni Israyil nag nangeen leen wax ne leen: Képp ku wax Yàllaam lu ñaaw, jaar fu bon, na wéetoo añam.
Du tere nag, gannaaw dangaa teddadil lool Aji Sax ji ci mbir mii, doom ji nga ci am, moom, day dee rekk.»
Ñaari nit ñu tekkiwul dara dikk toog janook moom. Ñu duural ko ca kanam mbooloo ma, ne Nabot daa saaga Yàlla, saaga Buur. Ñu génne Nabot dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.
Tuuri réew yépp, ana mu ci xettli menn réew ak man, ba Aji Sax ji wara mana xettli, Yerusalem ak man?»
Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa.
Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?
Bu ñu demaan ba ñépp fégal, Ayóoba day yónnee ngir sell-luloo leen. Ci biir loolu day teela xëy, daldi leen joxeel ñoom ñépp ba ñu daj saraxu rendi-dóomal, ku nekk benn. Booba Ayóoba da naan: «Jombul sama doom yii bàkkaar nañu mbaa ñu xarab Yàlla ci seen xel.» Noonu la Ayóoba jàppoo woon bés bu nekk.
Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul, jiiñul Yàlla lenn lu juunu.
Jabaram ne ko: «Yaa ngi ŋoy ci sa mat gi ba tey? Xarabal Yàlla boog te dee!»
Éy Yàlla, jógal ñoŋal sa dëgg, bàyyil xel dof bi la dëkkee sewal.
Yeen de yeena tax ñuy ñàkke teggin turu Yàlla ci biir xeeti jaambur yi dul Yawut, te noonu la ko Mbind mi indee.
tuubuñu seeni jëf, xanaa di saaga Yàllay asamaan ndax seeni mitit ak seeni taab.