TSK

TSK · Leviticus 25:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ibraayma ne ko: «Da di dama noon, amul kenn ci réew mii ku ragal Yàlla, te dees na ma rey ndax sama soxna.

Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?»

¶ Musaa ne mbooloo ma: «Buleen ragal, ndax nattu leen moo tax Yàlla ñëw, ngir ngeen ragal ko, ba dungeen moy.»

¶ «Buleen saaga ab tëx te buleen fakktal silmaxa. Ragal-leen seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.

Bu ngeen di jaay seen waa réew suuf nag mbaa ngeen di jënde suuf ci seen waa réew, buleen di naxante.

Buleen leen soxore ci biir kilifteef, waaye ragal-leen ci seen Yàlla.

ngalla fexeleen rekk ba ragal Aji Sax ji, te ngeen dëggu ci jaamoo ko seen léppi xol, ndax dangeen di xool ci jaloore yu yéeme yi mu leen defal.

Ma dellu ne leen: «Li ngeen di def de baaxul. Lu leen tee di ragal sunu Yàlla bala noo torox ci kanam noon yi dul Yawut?

Lu Aji Sax ji tegtale, njub la, di bégal xol. Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la, di leeral gis-gis.

Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.

Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange, jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam. «Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi, la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër.

Da daan sàmm àqu ku ñàkk ak ku néew doole, muy njiglaay. Du looloo di xam maay kan?» Kàddug Aji Sax jee.

Luke 12:5 TSK

Ma xamal leen nag ki ngeen wara ragal: kiy rey ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara sa, kooku déy laa leen ne, ragal-leen ko.

Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.

Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def.