¶ «Nangeen sàmm sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te di ko jëfe. Maay Aji Sax ji.»
TSK
TSK · Leviticus 25:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Maay baaxee réew mi jàmm it, ba bu ngeen tëddee kenn du leen tiital. Maay jële rab wu aay ci réew mi, te saamar du jóg, dal ci seenum réew.
¶ Su ngeen déggalee ba déggal seen Yàlla Aji Sax ji, ngir di sàmmoo jëfe mboolem santaaneem, yi ma leen di dénk tey, kon Aji Sax ji seen Yàlla, Aji Kawe ji moo leen di aj ci kaw mboolem xeeti àddina.
Israyil a ngi dëkke xel mu dal, walu Yanqóoba mee fegu, di wale réewum pepp ak biiñ bu bees, asamaan it di ko wàcceel ab layam.
May nga ma bànneexu xol bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.
Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»
Ay jantam Yuda dina texe, Israyil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax ji sunu njekk.”
Bés yooyu Yuda day mucc, Yerusalem dëkke jàmm, ñu di ko wooye: “Aji Sax ji sunu njekk.”»
Bu ma defee réew mi gent bu wéet ndax seen mboolem jëf ju siblu, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.”
Maa leen di seppee ci yéefar yi, dajalee leen mépp réew, délloosi leen seen suufas bopp.