TSK

TSK · Leviticus 25:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Diiru juróom benni at ngeen di ji seen tool, for li ci meññe;

Seen bésub Noflaay la bu ngeen di nopplu doŋŋ te war cee toroxlu. Li ko dale ci ngoonug juróom ñeenti fan ci weer wi ba ca ëllëg sa, ba jant so, ci ngeen di wormaal seen bésub Noflaay.»

Mboolem diir bi suuf siy wéet, moom lay nopploo la mu noppluwuloon, ba leen ay ati Noflaay fekkee ngeen dëkk fa.

«Doxal yéegi ca tundi Abarim gii, nga jàll ba ca tundu Nebo ca diiwaanu Mowabeen, ba janook Yeriko. Nga séentu nag réewum Kanaan mi may jox bànni Israyil, ñu jagoo.

Asamaan, asamaanu Aji Sax jee, suuf la dénk doom aadama.

Man maa sàkk suuf, sàkk doom aadama ak mala fi kaw suuf ci sama doole ju bare ak sama kàttan gu matale, te loolu lépp, maa ko jox ku ma neex.