TSK

TSK · Leviticus 25:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye atum juróom ñaareel ba atum Noflaay la wara doon: suuf sa ca boppam day nopplu doŋŋ ngir Aji Sax ji. Buleen ci ji seen tool, buleen ci wolli seen tóokëru reseñ.

Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk.”?

Jaraaf ja daan ànd ak Buur saa su ne àddu ca ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax, ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ci teg sa bët déy, waaye doo ci lekk.»

Ñuy waxal Yàlla naan: «Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi!

Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp.

¶ Buleen jikkowoo bëgg ub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»