TSK

TSK · Leviticus 25:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Ab doxandéem, buleen ko not; yeen ci seen bopp, jaar ngeen ci ndoxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra.

¶ «Bu sa mbokk demee ba ñàkk tax koo jaay ci suufam, mbokkam mi ko gëna jege te am sañ-sañu jotaat suufam, na jëndaat la mbokk ma jaayoon.

¶ Su amee ci seen biir ab ndóol, di kenn ci seen bokki bànni Israyil, ci benn ci seen dëkki réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen dëgër xol, di tëjal seen loxo, seen mbokkum ndóol moomu.

¶ Buleen gàddu àqu liggéeykat, baadoolo bu néew doole ci seen biiri bokk, mbaa ci seen dëkkandoo yiy doxandéem ci seen dëkk yi ci réew mi.

Job 31:16 TSK

Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku, mbaa ab jëtun wékk ma bët, ma tas yaakaaram?

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Mooy nàddil néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.

Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.

Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.

Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.

Li mu wax kay mooy: «Bu sab noon xiifee, jox ko mu lekk, bu maree, may ko mu naan. Soo defee noonu, day rus, ba mel ni koo yen ay xal.»

¶ Ci mbirum ndimbal lu jëm ci ñu sell ñi, jarul ma di leen bind,

Laajuñu lu moy nu fàttliku néew doole yi, te loolu di lu ma pastéefoo jëfe.

James 2:5 TSK

¶ Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp?