TSK

TSK · Leviticus 25:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Su ngeen jëndee jaam bu góor bu dib Ebrë, na liggéey juróom benni at. Juróom ñaareel ba lay moom boppam te du ameel kenn dara.

Sañ ngeen leena donale seen doom yi leen di wuutu, ñu doon seen ngàllo seen giiru dund. Ñooñu sañ ngeen leena def ay jaam, waaye su dee ci seen diggante, yeen bànni Israyil, buleen di soxorante ci biir kilifteef.

Waaye ñi bokk ci bànni Israyil, Suleymaan defu leeni jaam, ndax ñoom ñoo doon ay xarekatam, aki dagam aki jawriñam, ak njiiti xareem ak boroom watiiri xareem, ak dawalkati watiiram.

¶ «Ñoom waa Babilon it déy, dinañu surgawu ay xeet yu giir ak ay buur yu mag. Maa leen di fey seen añu jëf ju bon.»

¶ «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi, «maay damm yet wi ñu leen tënke ci seen ndodd, dammat seeni jéng, ba dootuñu doon jaamu doxandéem.