TSK

TSK · Leviticus 26:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jee dëgëral boppu Firawna buuru Misra, mu toppi bànni Israyil, fekk bànni Israyil ñoom, ña ngay génn réew ma ci seen teeyu bakkan.

Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, jox leen réewu Kanaan, te di seen Yàlla.

Ndax kat man la bànni Israyil di samay jaam. Ñoo di sama jaam ya ma génne réewum Misra; yeen, maay seen Yàlla Aji Sax ji.

Aji Sax ji, maay sab jaam, maay sab jaam, di sa doomu jaam bi ma sukk jur. Yaa yiwi samay buum,

Maa koy teg ci loxol ñi la doon naqaral, te naan la: “Sëggal, nu joggi, jàll,” nga def sa gannaaw gi aw yoon, ñu joggi, wéy.»

«Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Damm naa yet wi leen buuru Babilon tënke woon.

Garabi àll bi di meññ, suuf si nangu, ñu dëkke seen suufas bopp ci xel mu dal. Bu ma dammee seeni jéng, xettli leen ci dooley ñi leen doon jaamloo, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.

Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell, gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,