Buleen roy defini xeet wi ma leen di dàqal, ndax yooyu yépp lañu doon def, ba ma sib leen.
TSK
TSK · Leviticus 26:30
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
su ngeen teddadilee samay dogal, dëddu samay ndigal, ba jëfewuleen sama santaane yépp, xanaa di fecci sama kóllëreek yeen,
¶ Ba loolu wéyee Yosya indi Yerusalem mboolem sarxalkat ya doon sarxal ca dëkki Yuda, diggante Geba ba Beerseba, daldi sobeel bérabi jaamookaay ya ñu daan taal cuuraay, daaneel bérabi jaamookaay ya ca bunt ya, boole ca ba nekkoon ca buntu Yosuwe, boroom dëkk ba, te féete càmmoñ booy jaare ci buntu dëkk ba di duggsi.
Gannaaw loolu mu rendi ca sarxalukaay ya mboolem ña fa doon sarxalkati bérabi jaamookaay ya, ba noppi lakk yaxi nit ca kaw, ngir sobeel lépp, doora dellu Yerusalem.
Ñu di ko merlook seen bérabi jaamookaay, di ko fiirlook seen jëmmi tuur.
Aji Sax ji mere ñoñam, sib xeet woowu mu séddoo,
«Su boobaa déy,» kàddug Aji Sax jee, «noon yeey sulli yaxi buuri Yuda ak yaxi kàngam yi ak yaxi sarxalkat yi ak yaxi yonent yi ak yaxi waa Yerusalem, fa seeni bàmmeel,
Dama leen di jëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»
Dingeen xam ne maay Aji Sax ji, bu seeni néew nee xas fi seen biiri tuur, ak fi wër seeni sarxalukaay, ak kaw tund wu mag ak wu ndaw, ak mboolem ker garab gu naat, ak mboolem garab gu mag te sëq, fépp fu ngeen di taale cuuraay, ñeel seen mépp tuur.
Ñooy boroom xolub jinigalkat, te tey ñooy gàddu seen bàkkaar. Aji Sax ji mooy toj seeni sarxalukaay, tas seen xeri tuur.