TSK

TSK · Leviticus 26:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

su boobaa yéefar yépp a naan: «Ana lu waral Aji Sax ji def nii réew mi? Lu waral mii sànj mu tàng te réy?»

¶ «Su boobaa kër gii dina gent te képp ku ko romb dina yéemu tey muslu ci lu ni mel. Dinañu ne: “Lu tax Aji Sax ji def nii réew mii ak kër gii?”

Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.

¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.

ak sama suufas bokk, ya ay dég aki dagg nangu. Jooyleen kay kër ya ca mbégte ma, ak dëkk bu xumb ba.

Ana ku muus, ba xam lu waral lii? Ku Aji Sax ji waxal, mu wax nu lu waral réew mi sànku, gental ni màndiŋ mi, kenn jaaru fi?

Maay def dëkk bi ab gent bu ñuy muslu, ku fi jaare waaru, di muslu ci seen mbugal yépp.

Ma nàndal waa Yerusalem ak dëkki Yuda ak seeni buur ak seeni kàngam ngir gental fépp, muy ndànd-foyfoy bu ñuy muslu, di ko móoloo ba sunu jonni yàllay tey.

«Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Yeena gis mboolem musiba mi ma wàcceel Yerusalem ak dëkki Yuda yépp. Ñu ngi nii tey jii gental, kenn dëkku ca.

Du benn buur fi kaw suuf bu gëmoon, du kenn ci mboolem waa àddina ne bañ akub noon dina dem ba bëtt bunti Yerusalem.

Keroog bu ma leen wàcceelee àtteb mer ak xadar ak dumay xadar, seen dëkk beey doon dëkkub toroxte bu ñuy kókkali, dëkk bu gental buy yedd xeet yi leen séq. Man Aji Sax ji maa ko wax.

ca at ma jëkk ca nguuram, man Dañeel damaa gis ci téere yi limu at yi kàddug Aji Sax ji xamal Yonent Yàlla Yeremi, muy àpp bi Yerusalem wara gental, di juróom ñaar fukki at.

Ndaxam garabu figg foccul, doomu reseñ amul ca ndeyam, njurum garabu oliw àntuwul, tool yi meññul aw ñam, gàtt it tukkee na ca gétt ga, du genn jur gu gudd ci wurmbal,