TSK

TSK · Leviticus 26:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Keey saxal ngor ba ci junniy maas, di bale tooñ ak moy ak bàkkaar, te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem, xanaa di topp doom tooñu waajur, ba ca sët yaak sëtaat ya.»

Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.

Ca biir xeet yooyu nag, dungeen fa astandikoo, dungeen fa am sax fu ngeen noppale seen téstën. Aji Sax jee leen fay teg fit wu rëcc, ak gët yu giim, ak xol bu jeex.

Waaye bu ngeen walbatikoo ci man, sàmm samay santaane, di ko jëfe, bu ñu yóbbu woon seeni ñoñ ba fa suuf digalook asamaan sax, fa laa leen di jële, boole leen yóbbu ca bérab, ba ma taamoo dëël sama tur.”

Nan gapproo sunu gàcce, sàngoo sunu toroxte. Nook sunuy maam déy, ba ñuy gone ba tey jii, nu ngi tooñ sunu Yàlla Aji Sax ji, te déggalunu sunu Yàlla Aji Sax ji.

«Su boobaa deesatul ne: “Baay lekk reseñ ju xaay, mu uum bëñu doom ja.”

Su ko defee ñu ñàkk lekk, ñàkk naan, di xoolante gëti tiitaange, jeex tàkk ndax seeni ñaawtéef.»

«Ana lu waral waxin wi ngeen di waxe fi Israyil naan: “Baay lekk reseñ ju xaay, mu uum gëñi doom ja”?

Fa ngeen di fàttlikoo seeni jëfin, mboolem seeni jëf yu ngeen sobeele woon seen bopp, daldi jéppi seen bopp ndax seen mboolem jëf ju bon.

¶ «Yaw nit ki, waxal ak waa kër Israyil, ne leen: “Ngeen ne dungeen mana mucc ndax seeni tooñ ak seen bàkkaar yu leen diis ba semmal leen?”

Ma daldi ñibbi, ba ñu nangu seenug tooñ, sàkku ma. Bu ñu jàqee lañuy daw wutsi ma.»