Kon suuf si dina nangu, ngeen di lekk ba suur te dëkk fa ci jàmm.
TSK
TSK · Leviticus 26:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Su fekkee ne nag sàmm ngeen ba sàmm sama santaane yi ma leen dénk tey jii, ngir sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di ko jaamoo seen léppi xol, ak seen léppi bakkan,
Aji Sax jee leen di ubbil mbàndam mu baax ma fa asamaan, ba bu jotee mu tawal seenum réew, boole ci barkeel seen mboolem ñaq. Yeenay lebal xeet yu bare, waaye yeen dungeen leb.
Keey taw, suuxat suuf, yónnee ndox, nàndal ub àll.
Ana ku xàllal waame, ak ku sàkkal melax ak dënu aw yoon,
Yaa dikke suuf am wal, nangul koo nangul. Dexu Yàllaa fees ndox, ngay may nit peppam, ni nga ko waajale suuf si,
Suuf si nangu na, yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel.
kóllëre jebbee fa suuf, njekk séentoo asamaan,
Yaa suuxate tund ya fa sa néegi kaw, sa liggéey reggal suuf.
Su boobaa Aji Sax ji tawal lu ngeen ji, may leen pepp mu suuf meññ, sakkan te nangu, seen juri keroog di fore parlu yu yaa,
Maa leen def ñuy barke, ñook fi wër sama tund wi, bu jotee ma tawal leen, te tawu barke lay doon.
Maay ful doomu garab ak meññeefum tool, ba dootuleen am gàccey xiif fi digg yéefar yi.
Yeen doomi Siyoŋ, bégleen, te bànneexu ci seen Yàlla Aji Sax ji. Moo leen di may taw yu jëkk, muy njekk, moo leen di sottil taw yu jëkk, ak taw yu mujj, na woon.
Seetaatleen seen xel bu baax, dale ko bésub tey jii, dale ko ci ñaar fukki fan ak ñeentu juróom ñeenteelu weer wi, daleleen ci bés bii kenug néegu Aji Sax ji tegee, ngeen seetaat seen xel.
¶ Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.
Am nañu sañ-sañu tëj asamaan, ba du taw diiru fan yi ñuy biral waxyu, am nañu itam sañ-sañ ci ndox mi, ngir soppi ko deret, ak sañ-sañu wàcceel suuf wépp xeetu musiba, saa su leen soobee.