TSK

TSK · Leviticus 27:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Looloo di dogal yaak santaane yaak ndigali yoon ya Aji Sax ji tëral ca digganteem ak bànni Israyil ca kaw tundu Sinayi, Musaa jottli leen ko.

¶ Ñii ñoo di askani Aaróona ak Musaa, jant ba Aji Sax jiy wax, mook Musaa ca kaw tundu Sinayi.

¶ Loolu mooy santaane yeek àttey yoon yi Aji Sax ji dénkoon bànni Israyil, Musaa jottli leen ko ca joori Mowab, fa feggook dexu Yurdan, te janook Yeriko.

¶ Mu ngoog, jàngal naa leen ay dogali yoon, aki àttey yoon, na ma ko sama Yàlla Aji Sax ji sante, ngir ngeen war koo jëfe ca biir réew ma ngeen di nanguji.

¶ Yeen kat du yeena agsi woon ba jege tund wu ngeen mana laale seen loxo, muy tàkk, ànd aki xàmbaar, ak lëndëm gu ne këruus, ak ngelaw lu réy.