TSK

TSK · Leviticus 3:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba mu ko defee mu yebal ay ndawi bànni Israyil, ñooña def ay saraxi rendi-dóomal, boole ci rendi yëkk yu ndaw yu ñu def saraxi cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji.

¶ «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko.

¶ «Li yoon dogal ci saraxu cant ci biir jàmm, te nit sañ koo sarxalal Aji Sax ji mooy lii:

Su ko defee bànni Israyil dinañu indil Aji Sax ji juri sarax yi ñuy rendi ci àll bi. Dañu koo wara yóbbu ca sarxalkat ba, fi Aji Sax ji, ca bunt xaymab ndaje ma, defal ko Aji Sax ji saraxi cant ci biir jàmm.

¶ «Su nit dee joxsi Aji Sax ji aw nag mbaa gàtt, muy saraxu cant ci biir jàmm, mu di ko wàccoo ngiñ mbaa muy saraxu yéene, na doon lu amul sikk, ndax ñu nangul ko. Lenn luy sikk du nekk ci jur gi.

ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Nason doomu Aminadab.

«Tey matal naa la ma digoon Yàlla, yàppu bernde waa nga kër ga, saraxu cant la.

Amos 5:22 TSK

Ngeen defal ma saraxu rendi-dóomal, mbaa saraxi pepp it, duma ko nangu. Seen saraxu jur guy cant ci biir jàmm, faalewuma.

«Alkànde ñeel na ab jinigalkat bu am ci géttam am kuuy mu mu xasoo sarxe, te di sarxalal Boroom bi jur gu sikk, nde man, buur bu mag laa!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Sama tur moo jara ragal fi biir xeet yi.

Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf, ak la fa asamaan.