TSK

TSK · Leviticus 3:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Jëlal mboolem nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yi ànd ak nebbon bi ci kaw dëmbéen yi, nga boole lépp def ko saraxu taal-saxaral ci kaw sarxalukaay bi.

Li muy génne ci saraxu cant gi ci biir jàmm, ñu war koo taalal Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

La mu cay génnee muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi yépp, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.

«Waxal bànni Israyil ne leen: Buleen lekk lenn luy nebbonu nag mbaa xar mbaa bëy.

Ci kaw loolu sawara bawoo fi Aji Sax ji, tàkk ca kaw sarxalukaay ba, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak nebbon ba. Naka la mbooloo ma mépp gis loola, daldi sarxolle, ba noppi dëpp seen jë fa suuf.

Rax ci dolli bala ñoo lakk nebbon bi sax, surgab sarxalkat bi day dikk, ne nit kiy sarxal: «Joxal sarxalkat bi ci yàpp wi, mu saaf. Du nangu nga jox ko yàpp wu ñor, yàpp wu xonq rekk.»

¶ «Waaye sarxalkat yiy Leween, sëtoo ci Cadog, te daa dénkoo dénkaaney bérab bu sell bi ba bànni Israyil jàddee, ñooñoo may jege, di ma liggéeyal; ñooy dikk fi man, di indi saraxi nebbon ak deret. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.