¶ «Waaye buleen lekk yàpp wu ànd ak deret, ndaxte dund a ngi ci deret.
TSK
TSK · Leviticus 3:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Na Aaróona aki doomam jiitloo loolu, bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, mbaa ñuy jegeji sarxalukaay bi, ngir liggéey ci bérab bu sell bi, ndax ñu baña yóbbe seen bopp mbugal, muy seen dee. Na Aaróona ak askanam sàrtoo loolu fàww.
Sarxalkat bi ñuy fal ci doomi Aaróona yu góor yi, mu war koo wuutu, da koy def moom itam. Aji Sax ji moo jagoo sarax boobu fàww, te dañu koy lakk ba mu jeex.
«Waxal bànni Israyil ne leen: Buleen lekk lenn luy nebbonu nag mbaa xar mbaa bëy.
Te itam du lenn luy deret lu ngeen di lekke fenn fu ngeen dëkk, mu jóge ci njanaaw mbaa ag jur.
«Biiñ mbaa naan guy màndal bu ko kenn ci yeen naan buy duggsi ci biir xaymab ndaje mi, du yaw, du say doom yu góor, lu ko moy dingeen dee. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.
Buñu di sarxalatil tuur, yi ñuy jëmmale sikket, di ko bokkaalee. Na loolu di dogal bu leen war fàww, ñoom ak seen askan.
Looloo waral ma ne bànni Israyil, bu kenn ci ñoom lekk deret, te doxandéem bi ci seen biir it bumu lekk deret.
¶ «Buleen lekk lu am deret. Buleen di gisaane mbaa ngeen di jibar.
Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu sell, ndaxte lu sella sell la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.»
Waaye deret ja, buleen ko lekk. Ci suuf ngeen koy tuur nim ndox.
Buleen lekk deret ji. Ci suuf ngeen koy tuur nim ndox.
boole ca soowum nag ak meewum xar, nebbonu mbote, kuuyi diiwaanu Basan aki bëy, teg ca ngëneeli pepp, may leen biiñu reseñ ju xonq curr, ngeen naan.
Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi?
¶ «Waaye sarxalkat yiy Leween, sëtoo ci Cadog, te daa dénkoo dénkaaney bérab bu sell bi ba bànni Israyil jàddee, ñooñoo may jege, di ma liggéeyal; ñooy dikk fi man, di indi saraxi nebbon ak deret. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.
Moo defal loolu mbooloo mi ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko.