TSK

TSK · Leviticus 3:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Menn kuuy mi, jël ko, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci boppu kuuy mi,

Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam.

Na rendi sarax si ci kanam Aji Sax ji, fa féete sarxalukaay bi bëj-gànnaar. Na doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.

Aaróona day teg ay loxoom ci kaw boppu sikket biy dund te tudd ci kawam mboolem ñaawtéefi bànni Israyil ak seeni tooñ, ak seeni bàkkaar yépp, boole ko yen sikket bi, teg ko ci loxol nit ku ñu yónni, mu dàq ko ca màndiŋ ma.

te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, teewalal ko Aji Sax ji, muy sarax ca bunt jaamookaayu Aji Sax ji, kooku dees na ko topp àqu deret. Dafa tuur deret. Kon dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.

Acts 2:36 TSK

¶ «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»

Acts 3:26 TSK

Yeen la Yàlla jëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññee kenn ku nekk ci yeen, mu moy jikkoom yu bon.»

Acts 4:26 TSK

Buuri àddinaa jógandoo, kilifa yee lëkkoo ci kaw Boroom bi ak Almaseem.”