Jëlal mboolem nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yi ànd ak nebbon bi ci kaw dëmbéen yi, nga boole lépp def ko saraxu taal-saxaral ci kaw sarxalukaay bi.
TSK
TSK · Leviticus 3:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
Te itam na génne nebbon bi yépp, ni muy génnee nebbonu xar mu ñuy def saraxu cant ci biir jàmm. Na sarxalkat bi lakk loolu ci kaw sarxalukaay bi, mu dolliku ci saraxu sawara yi ñeel Aji Sax ji. Noonu la sarxalkat biy defale nit ki njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.
«Waxal bànni Israyil ne leen: Képp kuy jox Aji Sax ji saraxu cantam ci biir jàmm na indi cér bi Aji Sax ji séddoo ci saraxu cant googu ci biir jàmm.
Waaye lu nag taawloo, ak lu xar taawloo, ak lu bëy taawloo, deesu ko jot. Yooyii yu sell la. Deretam ngay xëpp ci sarxalukaay bi, nebbon bi, nga def ko saxar, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
Bésub keroog Buur sellal na digg ëtt ba janook néeg Aji Sax ji, ndax fa la joxe saraxu rendi-dóomal ba, ak saraxu pepp ba, ak nebbonu saraxu cant ci biir jàmm, ndax sarxalukaayu xànjar ba fa kanam Aji Sax ji moo tuutoon ci defandoo saraxu rendi-dóomal ba, ak saraxu pepp ba, ak nebbonu saraxu cant ga ci biir jàmm.
Bu ngeen ma daan indil sama céru ñam, muy nebbon, di deretu sarax yi, dangeen di dugalaale sama biir bérab bu sell bi ay doxandéem yu xaraful, du ci jëmm, du ci xol. Noonu ngeen sobeele sama kër gi. Fecci ngeen sama kóllëreek yeen ndax seen jépp jëf ju siblu.
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gi tabaxe kërug Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi.