¶ «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk.
TSK
TSK · Leviticus 3:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu ngeen dee rendil Aji Sax ji saraxas cant ci biir jàmm, sarxal-leen ko ni mu ware, ndax ñu nangul leen.
Sarax si muy sarxalsi Aji Sax ji di menn xarum menn at mu amul sikk, ngir rendi-dóomal, ak menn xarum menn at mu jigéen mu amul sikk, ngir póotum bàkkaar, ak menn kuuy mu amul sikk, ngir saraxas cant ci biir jàmm,
Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.
Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.
Li Yàlla namm, bu fan yi matee, moo di dajale lépp ci kilifteefu Almasi, mboolem la fa asamaan, ak li fi suuf.
¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.