Exodus 24:9
TSK
¶ Ba loolu amee Musaa yéeg, ànd ak Aaróona ak Nadab ak Abiyu ak juróom ñaar fukki magi Israyil.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee Musaa yéeg, ànd ak Aaróona ak Nadab ak Abiyu ak juróom ñaar fukki magi Israyil.
Day yóbbu yëkk wi ci bunt xaymab ndaje mi, ci kanam Aji Sax ji, daldi teg loxoom ci boppu yëkk wi, ñu rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji.
¶ Gannaaw loolu Musaa indi kuuy ma ca des, di kuuyu xewu colu. Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci boppu kuuy mi,
Boo indee Leween ñi fi kanam Aji Sax ji, bànni Israyil daldi teg seeni loxo ci kaw Leween ñi.
Aji Sax ji nag wàcc ca biir niir wa, wax ak moom, daldi sàkk ca leer ga ca Musaa, sédd ca juróom ñaar fukki mag ña. Naka la leer ga dal ca seen kaw, ñu tàmbali di wax ay waxyu, benn yoon bu ñu tóllantiwul.