Na capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal deret ji juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji, foofu ci kanam rido bi.
TSK
TSK · Leviticus 4:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi; li des ci deret ji da koy tuur ci taatu sarxalukaay bi.
ba noppi wis-wisal ca juróom ñaari yoon ca kaw sarxalukaay ba, diwe ko sarxalukaay ba ak mboolem ay ndabam, boole ca mbalkam njàpp ma, mook ub tegoom ngir yooyu it sell.
Gannaaw loolu doomi Aaróona yu góor ya indil ko deret ja, mu capp ca baaraamam, taqal ca béjjéni sarxalukaay ba; la des ca deret ja mu tuur ko ca taatu sarxalukaay ba.
Na sarxalkat bi capp baaraamu joxoñu ndijooram ci diw gi ci loxol càmmoñam, daldi wis-wisale diw gi baaraamam, ba mu mat juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji.
Baaraamu joxoñu ndijooram lay wis-wisale diw gi ci loxol càmmoñam ba muy juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji.
Te itam day wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kaw sarxalukaay bi, setal ko, sellal ko, mu tàggook sobey bànni Israyil.
¶ «Bu loolu taxul ngeen déggal ma, maa leen di mbugal lu ko ëpp juróom ñaari yoon, feye leen ko seeni bàkkaar.
su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar.