Su sàgganee it ba giñ ne dina def nàngam, muy lu baax mbaa lu bon, muy mboolem ngiñ lu ko rëcc te ba mu koy wax teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee tooñ na.
TSK
TSK · Leviticus 5:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Leviticus 5:4
TSK
Leviticus 7:21
TSK
Sobe su mu mana doon, muy lu jóge ci nit mbaa mala mu daganul mbaa mboolem lu daganul te mata sib, ku ci laal ba noppi, lekk ci lu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku dees koo wara dagge ci bànni Israyil.»
Leviticus 11:24
TSK
¶ «Yii nag da leen di sobeel te képp ku laal lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
Deuteronomy 14:8
TSK
Mbaam-xuux, moom, we wi xar na waaye du duññ. Kon daganul ci yeen. Aw suuxam, buleen ko lekk, te méddam, buleen ko laal.
Isaiah 52:11
TSK
Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi, bu ngeen di jóge Babilon, dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, setluleen te génn foofa.
Luke 11:44
TSK
Wóoy ngalla yeen, yeena ngi mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay, nit ñiy dox ca kaw te xamuñu ko.»