TSK

TSK · Leviticus 6:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Doomi Aaróona, sarxalkat bi, dañuy jafal ab taal ci kaw sarxalukaay bi, teg matt mi ci taal bi.

Li muy génne ci saraxu cantu biir jàmm bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, mooy nebbon bi, ak calgeen bi yépp, ñu doge ko fa sës ca fàllare ja, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

Ci kaw loolu sawara bawoo fi Aji Sax ji, tàkk ca kaw sarxalukaay ba, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak nebbon ba. Naka la mbooloo ma mépp gis loola, daldi sarxolle, ba noppi dëpp seen jë fa suuf.

Ma dekkal saraxu matt yi ñu wara joxe bu àppam jotee, ak saraxi ndoortel meññeef. Ngalla sama Yàlla, bàyyee ma lii xel ngir ngëneel.

Xanaa tiitaangey séentu mbugal ma, ak sawara wu yànj wiy xoyom fippukat yi.