¶ «Nanga sàkkalal jaamookaay bi ab ëtt: guddaayu ëtt bi ci wetu bëj-saalum, téeméeri xasabi sori rabal yu ñu ràbbe wëñu lẽe moo koy ub, ci genn wet googu.
TSK
TSK · Leviticus 6:26
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw loolu ñu samp wurmbal bi yéew jaamookaay beek sarxalukaay bi, daldi samp lafu buntu ëtt bi. Noonu la Musaa sottale liggéey bi.
«Lu waral lekkuleen sarax biy póotum bàkkaar ci bérab bu sell? Lu sella sell la, ñu jox leen ko, ngeen war koo yenniku bàkkaaru mbooloo mi, ba defal leen seen njotlaay fi kanam Aji Sax ji.
¶ Ba loolu amee waa ji ne ma: «Néegi bëj-gànnaar yeek néegi bëj-saalum yi janook dig-digalu feguwaay bi, ñooy néeg yu sell yi sarxalkat yi jege Aji Sax ji, di lekke sarax yu sell yee sell. Ca lañuy yeb sarax yu sell yee sell it, muy saraxu pepp yeek saraxu póotum bàkkaar yeek saraxu peyug tooñ yi, ndax bérab bu sell la.
Mu ne ma: «Bii bérab, fi la sarxalkat yiy togge yàppu saraxu peyug tooñ ak saraxu póotum bàkkaar, di fi lakk saraxu pepp mi, ngir baña génne lenn lu sell ca ëttu biti ba, bay sédd nit ñi sellnga gu leen di lor.»