TSK

TSK · Leviticus 8:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Nanga yóbbu yëkk wu ndaw wi ba ci bunt xaymab ndaje mi, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkk wi,

¶ «Ndegam sarxalkat bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil Aji Sax ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar ndax bàkkaar ba mu def.

«Indil Aaróona aki doomam yu góor te indaale yére yi ak diw gi ñuy fale ak yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar ak ñaari kuuy yi, boole ca pañeb mburu ya amul lawiir,

Aaróona day teg ay loxoom ci kaw boppu sikket biy dund te tudd ci kawam mboolem ñaawtéefi bànni Israyil ak seeni tooñ, ak seeni bàkkaar yépp, boole ko yen sikket bi, teg ko ci loxol nit ku ñu yónni, mu dàq ko ca màndiŋ ma.

Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal, saxar sa jollee ca kuuyu sarax ya, ma boole ca saraxu nag ak sikket. Selaw.

Sarxalkati Leween ñi askanoo ci Cadog, te jege ma, ngir di ma liggéeyal, kàddug Aji Sax jee, nanga leen jox yëkk wu ndaw, muy saraxu póotum bàkkaar.

Bés ba muy dellu ca ëttu biir ba, ngir liggéey ca biir bérab bu sell ba, na indi saraxu póotum bàkkaar. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.