TSK

TSK · Leviticus 8:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aaróona aki doomam di ci tanq, raxase seeni loxo ak seeni tànk.

Mbubb mu sell lay sol, mu ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew ak tubéyi njiitlaay ju ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew. Na takkoo laxasaay gu ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, te kaalag wëñ gu ëccu ba sew lay takk. Yére yu sell a ngoogu; kon nag na sangu bala mu koy sol.

Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba.

Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.

¶ «Bésub keroog bëtu ndox dina bënnal kër Daawuda, ak waa Yerusalem, ngir setal bàkkaar ak sobe.

Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi, ak ci sunu Noowug Yàlla.

Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.

tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,