TSK

TSK · Leviticus 9:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Lii nag mooy li nga leen di defal, ngir sédd leen céru sellnga, ngir ñu di ma sarxalal: Dangay jël yëkk wu ndaw ak ñaari kuuy yu amul sikk,

¶ «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk.

¶ Musaa teg ca indi yëkku sarax siy póotum bàkkaar, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkku sarax siy póotum bàkkaar,

Musaa wax ak Aaróona ne ko: «Dikkal fii ci sarxalukaay bi te joxe sa saraxu póotum bàkkaar ak sa saraxu rendi-dóomal, nga jotoo ko, yaw yaak mbooloo mi, boo noppee joxe saraxu mbooloo mi, jote leen ko, muy li Aji Sax ji santaane.»

Na jële ci mbooloom bànni Israyil ñaari sikket, sikket yuy doon saraxu póotum bàkkaar ak menn kuuyum rendi-dóomal.

Néew doole googu moo tax mu wara joxeel boppam, tey joxeel askan wi ay sarax, ngir seeni bàkkaar.

Coobarey Yàlla googu moo waral ñu sellale nu sarax, bi Yeesu Almasi sarxe yaramam, benn yoon ba fàww.