TSK

TSK · Leviticus 9:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Ndegam sarxalkat bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil Aji Sax ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar ndax bàkkaar ba mu def.

Lépp lu ñu def tey, Aji Sax ji daa santaane ñu def ko, mu daldi matal seen njotlaay.

¶ «Aaróona day sarxal yëkk wi, muy saraxu póotum bàkkaaram, di njotlaayal boppam, mook waa këram.

Bu loolu weesee mu sangoo fu sell, sol yérey boppam, génn, joxeel boppam ab saraxu rendi-dóomal, joxeel mbooloo mi seen saraxu rendi-dóomal ngir njotlaayal boppam ak njotlaayal mbooloo mi.

¶ Bépp sarxalkat bu mag nag, ci biir nit ñi lees ko jële, fal ko ngir nit ñi, ci seen diggante ak Yàlla, muy jébbale ay jooxe ak saraxi jur ngir seeni bàkkaar.

Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.