TSK

TSK · Luke 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kóllëre gi ma fas ak yaw, te nga war koo sàmm, yaak sa askan, li mu laaj mooy lii: góor gu nekk ci yeen, war naa xaraf.

Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»

¶ Aana mujj ëmb ca ndeetel at ma. Gannaaw gi mu am doom ju góor, tudde ko Samiyel (mu firi Yàlla dégg na), ndax da ne: «Maa ko ñaan Aji Sax ji.»

Alyaasa ne ko: «Nëgëni déwén dinga leewu doom ju góor.» Mu ne ko: «Déet, sang bi, góoru Yàlla gi, bu ma nax mukk, sang bi.»

Ba loolu weesee ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Maxer Salal Xas Bas.”

Hosea 1:4 TSK

¶ Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Yisreel. Des na tuuti dinaa mbugal askanu buur Yewu ndax deret ji ñu tuur ci Yisreel. Dinaa jeexal nguurug Israyil.

Hosea 1:9 TSK

Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (mu firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.»

Luke 1:60 TSK

Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.»

¶ Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!»