¶ Gannaaw loolu Samiyel ne leen: «Wooleen Israyil gépp, ñu daje ca Mispa, ma tinul leen Aji Sax ji.»
TSK
TSK · Luke 1:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ilyaas ne ko: «Du maa lëmbe Israyil de. Yaw kay la, yaak sa kër baay, ndax yeena dëddu santaaney Aji Sax ji, di topp tuur yi nuy wax Baal.
Loolu tax na Aji Sax ji wax buurub Israyil ne ko: “Lal bi nga tëdd doo ko wàcc, ndax dinga dee moos.”» Ci kaw loolu Ilyaas dem.
Néew-ji-doole dagaan, Aji Sax ji dégg, dalal xelam, teewlu ko,
Ragal Aji Sax ji di ndoortel rafet xel, dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. Moo yeyoo cant ba fàww.
«Moo tax ma di leen def lii, yeen bànni Israyil. Gannaaw lii laa leen di def nag, waajleena dajeek seen Yàlla, yeen bànni Israyil.»
«Ngóor si nag yaw, yonentu Aji Kawe ji lees lay wooye, nde yaay dox, jiitu Sang bi, xàllal kow yoonam,
Ca saa sa nag laa yeble ci yaw. Yaw it def nga lu baax, bi nga dikkee. Léegi nag nun ñépp a ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu mboolem lu la Boroom bi sant.»
¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,
Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
¶ Gannaaw loolu lépp, noonu lay seeye nag, xamleen bu baax li leen war! Jëfin wu sell akug njullite,
¶ Ci kaw loolu ma gis ay gàngune yu ñu jox ña ca toog, sañ-sañu àtte. Ma daldi gis bakkani ñi ñu dogoon seen bopp ndax la ñu doon seedeel Yeesu ak la ñu gëmoon kàddug Yàlla, ña sujjóotalul woon rab wi ak jëmmu nataalam, te amuñu màndargam rab wi ci seen jë mbaa seen loxo. Ñu dekki bay nguuroondoo ak Almasi diiru junniy at.