TSK

TSK · Luke 1:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji?

Jaraaf ja daan ànd ak Buur saa su ne àddu ca ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax, ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ci teg sa bët déy, waaye doo ci lekk.»

Samaree yilif Efrayim, te doomu Remalya ji yiliful lu moy Samari. Dungeen mana saxoo dëgër nag, ndare ngeen sax ci Aji Sax ji.”»

Bésub keroog sa gémmiñ dina ubbiku, nga noppee luu, ba wax ak ka rëcc. Su boobaa yaay doon misaalu mbooloo mi, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.»

Luke 1:45 TSK

Ndokklee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»

Su ci ñennat ñàkkee kóllëre, ndax seenug ñàkk kóllëre day fanq kóllëreg Yàlla?

Titus 1:2 TSK

Ngëm googu, ak xam-xam boobu, ñu ngi sukkandiku ci yaakaar, ji nu am ci texe ba fàww, te googu texe, Yàlla mi dul fen, moo ko dige ba àddina sosoogul.

¶ «Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!