TSK

TSK · Luke 1:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yaw Yanqóoba mi néew doole niw sax, yeen góori Israyil. Man, maa leen di dimbali. Kàddug Aji Sax jee, sab jotkat, Aji Sell ju Israyil.

Aji Sax ji dafa wax, moom mi la sàkk, mooñ la fa sa biiru ndey, di la dimbali. Mu ne: «Yaw Yanqóoba sama jaam bi, yaw Yesurun sama tànnéef laa wax, bul tiit.

¶ «Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.

Mu ne ma: “Póol, bul tiit; fàww nga taxawi fa kanam Sesaar, te it Yàlla moo la baaxe muccug mboolem ñi nga àndal ci gaal gi.”

Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»