TSK

TSK · Luke 1:46

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu Aana ñaan ne: «Sama xol a ngi bége Aji Sax ji, ci Aji Sax ji laa ame doole. Maa am tontal noon yi, nde maa bànneexoo sag wall.

Su boobaa ma bége Aji Sax ji, bànneexoo wallam,

Yeen waa penku, sargal-leen Aji Sax ji boog, yeen waa duni géej, teral-leen Aji Sax ji Yàllay Israyil.

Maa béga bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam njekk, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi, mi nu jubale ak moom.

¶ Waaye cant ñeel na Yàlla! Moom mi Almasi tax mu di nu yóbbaale saa su nekk, ci njaab miy fésal ndamam, te cuuraayal xam-xamam, nun ñii la koy wasaaree fépp,

¶ Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!