Mu dellu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Sem, yal na Kanaan dib jaamam.
TSK
TSK · Luke 1:68
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra.
teg ca ne: “Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ji ma jox bésub tey ku ma wuutu ci samab jal, may gis.”»
yal na turam sax, ba law fu jant tiim, yal na xeet yépp barkeele ci moom, te di ko ndokkle.
Moo yónnee xeetam wall, fas ak ñoom kóllëre gu sax. Kee sell te jara ragal!
Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
¶ Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, mi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi mi nu bokk, fa déndi asamaan ya.
¶ Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi, ngir may nu yaakaar juy dund.