ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»
TSK
TSK · Luke 1:70
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Noowug Aji Sax jee may waxe, sol ma kàddoom.
Waaye yaw Yanqóoba sama jaam, bul tiit,» kàddug Aji Sax jee; «yaw Israyil, bul ragal. Fu sore laa lay wallujee, yaak sa askan wa ca réewum njaam ga, Yanqóoba dellu dal, fegu; kenn dootu ko tiital.
¶ Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.»
Ba ñu werantee ca seen biir, bay dem te juboowuñu, Póol teg ca ne leen: «Noo gu Sell gee yeyoon wax lii seeni maam, Yonent Yàlla Esayi jottli.
¶ Kon nag ni ko Noo gu Sell gi waxe: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam,
Ndax kat du genn kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe waxyu bu bawoo fa Yàlla.