TSK

TSK · Luke 1:74

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye man seen Yàlla Aji Sax ji ngeen di wormaal, ma xettli leen ci seen loxol mboolem noon.»

Israyil, yaay mucc fa Aji Sax ji mucc gu sax dàkk! Doo rus, doo torox fii ak ëllëg.

«Ñooy tabax ay kër, dëkke, jëmbati tóokër, lekk ca meññeef ma.

Dinañu xam ne maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen yóbbu woon ngàllo ca yéefar ya, ba noppi délloosi leen seen suuf, te bawuma kenn gannaaw.

Maay taxaw wattu fi wër sama kër, aar ko ci ñiy dem ak a dikk, ba boroom doole dootu not sama waa kër, nde léegi samay gët laa leen ne jàkk.

Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag sellnga la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk.

Ndax kat Noo gi nu Yàlla jox taxu noo ragal, xanaa kay da noo may doole, ak cofeel, ak jëfin wu laloo am xel.

te Almasi di ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi, kon nag ñaata yoon la deretu Almasi gëna mana setal sunu yaraange ji sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci ndee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!