TSK

TSK · Luke 1:77

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Luke 3:3 TSK

Yaxya dugg mboolem àll, bi wër dexu Yurdan, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir ñu jéggal leen seeni bàkkaar.

Luke 7:47 TSK

Moo tax ma di la wax, ne bàkkaaram yu bare yi ñu ko jéggal moo waral fonkeelam gu bare. Waaye njéggal lu tuut, fonkeel gu tuut rekk.»

Acts 2:38 TSK

Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.

Acts 5:31 TSK

Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.

¶ «Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,

Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,

¶ Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,