¶ Yéene bii ñeel na dëkk ba ñuy wax Tir: Yeen waa gaali Tarsis ñi deele, jooyleen! Lépp a yàqu! Du kër, du teeruwaay. Fa dunu Sippar lañu leen ko waxe.
TSK
TSK · Luke 10:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bare na waaso yoo xamul seeni wax, yu xóotu làkk te diisu làmmiñ. Te su ma la yebaloon ci ñoom, ñu déggal la.
Ma walbatiku jublook Boroom bi Yàlla. Maa ngi sol saaku, diwoo dóom boole kook koor, toroxloo ko, di ko ñaan ak a dagaan.
¶ Ba ndaw ya délsee, dañoo nettali Yeesu mboolem la ñu def. Mu ànd ak ñoomu neen ba sore, ca wetu dëkk ba ñuy wax Beccayda.
Ba ñu werantee ca seen biir, bay dem te juboowuñu, Póol teg ca ne leen: «Noo gu Sell gee yeyoon wax lii seeni maam, Yonent Yàlla Esayi jottli.
Noonu lees binde ne: «Yàlla moo leen jox xelum ngëmment, ak bët yu dul gis, ak nopp yu dul dégg, ba bésub tey jii.»
Dinaa may nag sama ñaari seede yi, ñu biral waxyu diiru junni ak ñaar téeméeri fan ak juróom benn fukk (1 260) yu ñuy sol ay saaku, di ko toroxloo.»