Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji, sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.
TSK
TSK · Luke 11:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man, nu bokk wormaal turam.
di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»
Ci xat-xat laa wooye Ki Sax wall, Ki Sax wuyu ma, yaatal ma.
Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.
Mu ne: “Woo ma, ma wuyu la, wax la lu réy te loq, loo xamul woon.”»
Aji Sax ji da ne waa kër Israyil: «Sàkkuleen ma, ba dund.
Korney ne ko jàkk, tiit, ne ko: «Sang bi, lu mu doon?» Mu ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa Yàlla, ba mu bàyyi la xel.
Ndaxte Yàlla moo ne: «Jant ba mu jotee laa la nangul, bésu mucc ba laa la wallu.» Te nag, tey jii la jantam jote; tey kat, la bésub mucc.
Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.
¶ «Waaye yeen ñi ci des ñépp nag, yeen waa Catir ñi toppul moomu njàngle te jotuleena xam loolu ñu naan xóotey xam-xamu Seytaane, maa ne leen, duma leen sëf beneen sëf.