TSK

TSK · Luke 12:37

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ni xale bu góor di takke ab janq, ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër; ni boroom séet di bégee ab séetam, ni la la sa Yàlla di bégee.

Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, di jàmbaar juy walloo. Moo lay bége ci biir bànneex, leqlee la cofeelam, bége la bay sarxolle.

Ndokklee surga bu njaatigeem dikk, fekk ko muy doxale noonu.

Teewluleen boog, tey ñaan saa su nekk, ba mana mucc ci mboolem looluy nara xew, ngir ngeen taxaw fi kanam Doomu nit ki.»

Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko.

Noonu lees leen di ubbile bunt bu yaa bu ngeen di tàbbee ca nguur gu sax gay sunu moomeelu Sang, sunu Musalkat, Yeesu Almasi.

¶ «Ku am ndam nag, maa lay may nga toog ak man fi sama ngàngune, na ma ame woon ndam, ba toog ak sama Baay fi ngànguneem.

Ña ngay woy woy wu yees ca kanam ngàngune ma, ca kanam ñeenti bindeef yaak mag ña, te kenn manula mokkal woy wi, ku dul téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni ñooñu ñu jote àddina.