Moo leen di may ñu wéeroo seen cëslaay, tey xool fa ñuy jaare.
TSK
TSK · Luke 12:45
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ma ne dogal a ngii binde, fi sama kanam: «Duma noppi déy, maa leen di fey, maa leen di fey ba mu mat sëkk.»
«Yaw nit ki, du lii ngeen defati aw léeb ci biir réewum Israyil? “Bés yaa ngi bëgga baree, te peeñu sottiwul!”
Yeen, nebbon ji, ngeen lekk; kawari jur gi, ngeen def yére, sol; li ci duuf, ngeen rendi, te jur gi sàmmuleen leen!
Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ yu neex, ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi.
Ndaxte ñu baree ngii ñu seeni jëf tax ñu di nooni bantub Almasi. Loolu wax naa leen ko ay yoon, ma waxati leen ko tey aki jooy.
Seenug bëgge lañuy ràbbe ay kàddu yu ñu leen di koppartoo. Ñooñu la seenub daan yàgga yoot, te seen sànkute nelawul.
Ag ngoreel lañu leen di dig, te ñoom ci seen bopp, ay jaami yàqute lañu, nde lu la man, yaa dib jaamam.
Ñooñooy gàkkal seen jataayu lekk yi gëmkat ñiy bokk, di ñóox te amuñu ci jenn jom; ñooy xiin yu naaxsaay yu ngelaw li yóbbu; ñooy garab yu dee ñaari yoon, du meññ waxtoom, reen ya buddiku.
Gannaaw loolu mayees na ko mu sol ag noo jëmmu rab wu jëkk wi, ba muy wax, di reylu képp ku ko sujjóotalul.
Jë bi nag, tur wii lañu ci bind, muy kumpa: Babilon gu mag gi, ndeyu jigéeni moykat yeek ñaawtéefi àddina yi.
Ci yaw it lañu fekk deretu yonent yeek ñu sell ñi ak mboolem ñi ñu rey ci kaw suuf.