TSK

TSK · Luke 13:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.

Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam biy siggil giiri Yanqóoba, te wara délloosi ndesu Israyil gii. Tabb naa la, ngay leeru xeet yi, di jotale waa cati àddina sama wall.»

«Man maa xam seeni jëf ak seeni xalaat. Bés bii taxaw lees di dajale xeetoo xeet aki làkk, ñu dikk ba niir samag leer.

¶ «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii tukkee fa Yàlla, yóbbante nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»

Ni leen xibaaru jàmm bi dikkale nag, ni la dikkale àddina sépp, te mu ngi meññ, di law, na mu ko dale defe fi seen biir, ca bés ba ngeen déggee lu jëm ci yiwu Yàlla, ba ràññee ko dëgg.

¶ Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma.