Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen.
TSK
TSK · Luke 13:34
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yal na la Aji Sax ji fey sa jëf. Aji Sax ji Yàllay Israyil, ji nga làqusi ci kiiraayam, yal na la yool, ba mu mat sëkk.»
Ndaxam muñal nga leen ay at yu bare, di leen artoo sam xel, say yonent di leen ko jottli; waaye taxul ñu déglu. Nga teg leen nag ci loxoy waa réew yi.
Sa njekk a tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!
Buleen fat tuuru jaambur, buleen sujjóotal tuuru doxandéem.
Kiiraayam la lay sànge, nga yiiru, làqu; wormaam yéew la, di la aar.
Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.
Aji Sax ji seen jotkat dafa wax, Aji Sell ju Israyil da ne: «Maay Aji Sax ji, seen Yàlla ji leen di jàngal seen njariñ, di leen awale fa ngeen wara awe.
«Mbugal naa seeni doom, jariñul dara. Dégguñu yar, bóom ngeen seeni yonent, mbete gaynde yuy fàdde.
Mbir mii déy laa leen santoon ne leen: “Déggal-leen ma, ma doon seen Yàlla; yeen ngeen doon sama ñoñ. Doxeleen wépp yoon wu ma leen sant, su ko defee ngeen baaxle.”
“La Yonadab doomu Rekab santoon ay doomam ne leen: ‘Buleen naan biiñ’ de, jëfees na ko. Duñu naan biiñ ba tey jii ndax wormaal seen santaaney maam. Man nag ay yooni yoon laa leen wax waaye déggaluleen ma.
Looloo ma tax di jooy, rongooñ di wal-wali, te ku may dëfal sore ma, mook kuy seral sama xol. Samay doom a ngi jaaxle, nde noon bi daan na.
Lu ñu leen gëna woo, ñu gën maa sore. Ay tuuri Baal lañuy defal ay sarax, te ay xërëm lañuy taalal cuuraay.
Yeen doomi Siyoŋ, bégleen, te bànneexu ci seen Yàlla Aji Sax ji. Moo leen di may taw yu jëkk, muy njekk, moo leen di sottil taw yu jëkk, ak taw yu mujj, na woon.
¶ «Mag ja nag mer, nanguwula agsi, baayam génn, di ko soññ.
Ñoo lay nappaaje ci suuf, yaak say doom yi ci sa biir, te duñu bàyyi doj ci kaw doj ci sa biir, ndax ba sa bésub wall dikkee, yaa ko ràññeewuloon.»
Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.
¶ Ñuy dóor Eccen ay doj, moom muy ñaan Yàlla, naan: «Sang Yeesu, nangul sama bakkan!»
Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wa ca réewum Arabi, te moo taxawe Yerusalem gii tey, dëkk bii dib jaam mook doomam yi ko dëkke.