gental seen dëkk yu mag, tas seen bérab yu sell, te dootuma faale xetug jàmm ca seeni sarax.
TSK
TSK · Luke 13:35
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yal na Yàlla barkeel ki dikke turam. Nu ngi leen di ñaanale fi néegu Aji Sax ji.
Ma xamal leen nag li ma naral sama tóokër bi. Ñàggib ñagam, mu dim parlu; màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll.
Ndaw leeka rafeti tànk, kee bartaloo tund yi, di la dégtalsi jàmm, di la xibaar lu neex, àgge la ag mucc, ne la: «Éey, Siyoŋ, sa Yàllaay Buur!»
Waaye su ngeen dégluwul sama santaane yii, giñ naa ko ci man mii,” kàddug Aji Sax jee, “ab gent rekk la gii kër di doon!”»
Ndax kat ay fan yu bare la bànni Israyil di toog te duñu am buur, duñu am kàngam. Duñu rendi sarax, duñu am tuuri doj, duñu am xar-sànni, duñu am gàllaaji kër.
¶ Libaŋéey, ubbil say wunt, sawara xoyom sa garabi seedar.
Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem, ngir xare. Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi, tëdde jigéen ñi. Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo, waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge ci dëkk bi.
¶ Mu am nag ay nit ñu doon wax ca kër Yàlla ga, ak taaru doji tànnéef, ya ak yeneen alali jooxe ya ñu ko rafetale. Yeesu itam ne leen:
Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.