Musaa nag tinu Yàllaam Aji Sax ji ne ko: «Aji Sax ji, ana lu waral sam sànj di tàkkal sa ñoñ ñi nga génne réewum Misra ci sa kàttan gu màgg ak sa dooley loxo?
TSK
TSK · Luke 13:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.»
Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal, waaye éy Aji Sax ji, jógal te saw tur tax, doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la.
¶ Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy.
Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi, sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, nañu fi taxaw jooy; nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ; bul wacce say séddoo gàcce, ak ñaawley xeeti jaambur yi. Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi, naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”»
Jombul sama liggéey dina yee fiiraangey sama bokki Yawut ñi, ba ñenn ci ñoom mucc.