«Dégluleen ma, ngalla sang yi, siyaare naa leen, tee ngeena dal ak man, su ko defee ngeen jàngu, fanaan ba suba, ngeen xëy topp seen yoon?» Ñu ne ko: «Bàyyil, nu fanaan ci mbedd mi.»
TSK
TSK · Luke 14:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sa mboolooy taxawal seen bopp, sa bésub xare. Ña nga soloo darajaak sellnga, faboo fa njël sosoo, diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay.
Bésub keroog Israyil ñetteel Misraak Asiri, di barke fi digg àddina.
Tey Aji Sax jee wax, moom mi dale sama biiru ndey, mooñ ma, ma dib jaamam bi koy waññil askanu Yanqóoba ba ca moom, dajaleel ko bànni Israyil googu fa moom, ba jagoo teraangay Aji Sax ji, sama Yàlla jii di sama doole.
Bésub keroog Yerusalem la ndox muy dund di wale, genn-wàll gi jëm géeju penku, genn-wàll gi, géeju sowu, te noor ak nawet lay doon.
Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.
¶ Ba ñu déggee loolu lañu dal, daldi màggal Yàlla. Ñu ne: «Kon xeeti jaambur yi, ndeke ñoom it Yàlla may na leen ñu tuub, ba dund!»
Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.
Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”»
¶ «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii tukkee fa Yàlla, yóbbante nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
¶ Léegi nag yeen jaambur ñi dul Yawut laay waxal. Gannaaw maay ndaw li ñu yebal ci jaambur ñi dul Yawut, samab yónnent laay teral.
¶ Te itam as gor laa, kenn moomu ma; teewul jaamu ñépp laa def sama bopp, ngir gëna iril Sang bi aw nit.
Kon nag Almasi, noo diy ndawam, te ci nun la Yàlla di wootee. Kon ci turu Almasi, danu leen di ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla.
¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.
¶ Almasi moomu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy àrtoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi.