Job 2:7
TSK
Ba mu ko defee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji. Ci kaw loolu mu sànni Ayóoba ay taab yu metti, dale ko ca téstën ma, ba ca kaw bopp ba.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba mu ko defee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji. Ci kaw loolu mu sànni Ayóoba ay taab yu metti, dale ko ca téstën ma, ba ca kaw bopp ba.
Bés bu ne yar dal ma, saa yu ma xëyee, jot mbugal.
Moo diwu pajtal amul Galàdd a? Am fajkat a fi amul? Ana lu waral bokk yi taneeguñu?
¶ Ba Yeesu di jubsi dëkk ba ñuy wax Yeriko, ab silmaxaa nga tooge ca peggu yoon wa, di yalwaan.
Fekk ñu indi fa waa ju judduwaale lafañ, ñu daan ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye bunt bu Rafet, ca kër Yàlla ga, ngir muy sarxu ñay duggsi.
¶ Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp?