¶ Dingeen alkule am witt, akam xiiw.
TSK
TSK · Luke 16:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moona moo feesaloon seeni kër ay teraanga, waaye ñu bon ñii, royuma leen fenn.
Damaa gis ku bon di note, te sëq ni garab gu naat fa mu fekk baax,
Dañoo suur ba gët suulu, seen xalaati xel xëtt yoon.
Tey ci janti toroxte ak tumurànke, la Yerusalem di fàttlikoo mboolem ngëneeli démbam. Aw askanam a tàbbi ci loxol noon, te wall amul, noon ba gis leen, di textexi ci seenug yàqule.
¶ Guddi googa lañu rey Baltacar, buurub waa Babilon.
Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.
Ci kaw loolu ñu dugal ko sawara. Ca biir mbugal mu tar ma la dawale bëtam, daldi séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
Ñuy feddli pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»
Ñooñu sànkute lañuy mujje; seen koll lañu def seen yàlla, seen gàcce lañuy damoo, te yëfi àddina doŋŋ a leen soxal.
Bokk ak ñoñi Yàlla ab coono moo ko gënaloon muy bànneexoogum ci biir bàkkaar.
¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.