Yal nanga may nangul sama dagaan, nangul Israyil sa ñoñ. Bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, yal nanga ko dégge bérab ba nga dëkke ca asamaan, ba nangul leen, jéggal leen.
TSK
TSK · Luke 18:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Fekk na Esekiya ne Esayi: «Ana lu di takk biy firndeel ne Aji Sax ji dina ma wéral, ba ma mana dem gannaaw ëllëg ca kër Aji Sax ji?»
Ba ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay.
Mu ne leen: «Bindees na ne: “Sama kër gi kërug julli la, waaye yeen, moom ngeen def rawtub sàcc!”»
¶ Fekk na Póol xam ne lenn ca kurél gaa nga bokk ca ngérum Sadusen ya, ña ca des bokk ca ngérum Farisen ya. Mu daldi àddu ca kaw ca biir géew ba, ne: «Bokk yi, man de ab Farisen laa, di doomu Farisen; li ñu may àttee nag mooy sunu yaakaar ak sunu ngëm gi nu bokk ci mbirum ndee-ndekki.»
Man mi xaraf ba ma amee juróom ñetti fan, askanoo ci bànni Israyil, giiroo ci Beñamin, di ab Ebrë bu ñaari Ebrë jur, te bokk ci ngérum Farisen, ci wàllu yoonu Musaa.