¶ «Bu loolu weesee mboolem lu jóge ci suuf, muy pepp mbaa doomi garab, cérub fukkeel ba Aji Sax jeey boroom. Dees koy sellalal Aji Sax ji.
TSK
TSK · Luke 18:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee Yàlla dikk, dajeek Balaam, Balaam ne ko: «Ñaari sarxalukaay yi, yékkati naa leen te sarxalukaay bu ci nekk, sarxal naa ci wenn yëkk ak menn kuuy.»
ne ko: «Ñëwal nu dem rekk, nga gis ni ma farloo ci mbiri Aji Sax ji.» Mu waral ko watiiram, yóbbu ko.
Man mii lañuy sàkku bés bu ne, di wuta xam sama coobare! Mbete xeet wuy def njekk, te waccul ndigalu yoonu Yàllaam. Ñu ngi may ñaan àttey njekk, di sàkku man Yàlla, ma jege leen,
Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.
Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
¶ Bokk yi, sama yéeney xol, ak ñaan gi may ñaanal Israyil ci Yàlla moo di ñu mucc.
Yoonu Yawut, maa ci rawoon ñu bare ci sama maas gi ma bokkal askan, te maa leen gënoona xér fuuf ci sunu aaday maam.
Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.